ACTUALITES

KÓLLËRE GINNAAW LAY FÉETE

Wotey dépite yi ci dibéeru 31 ci sulet 2022, wone na xar-kanam gu bees ci réewum Senegaal. Ndax ag mbetteel la ? Walla jaas ? Walla day biral ug kóllëre gu feddaliku ? Lum ci mën a doon, ca diwaanu Tuuba-Mbàkke moom, maxejj ya dëggal nañu léebu wolof biy wax ne “ kóllëre ginnaaw lay féete ”.

Tuuba-Mbàkke woneeti na boppam ci wote yile. La fa tukke ciy njureef day firndeel ni, cofeel ak ànd bi dox diggante waa gox ba ak Njiitu réew ma woon, Me Abdulaay Wàdd, tey la gën a dëgër. Nde, booy seet, dangay gis ne lëkkatoo Wallu moo raafal pekki wote ya fa nekk, rawe ay naataangoom lu baree bare. Lëkkatoo Njiitu réew mi, Maki Sàll, daf fa lajj ci anam bu ñaaw. Te, loolu sax, du guléet.

Cig pàttali, Bennoo Bokk Yaakaar mësul a jël raw-gàddu gi, ciy wote yu mu mën di doon, ca diwaanu Tuubaa-Mbàkke. Ci wotey Ngomblaan gii ñeel dépite yi, forees na ci wewu béy ni, Njiitu réew mi alal ju bare la xëppati Tuubaa, jagleel ko ñenn ci sëriñ sa ngir, di ci yaakaare xobi taalibe yi. Ndeysaan, bu yeboo ne Ngóor si Sàll yàqi na. Nde, doole ja fa làngug PDS amoon, ba tey sookewul ngir mbëggeel gi dox diggante Persidã Abdulaay Wàdd ak wa Bawol. Péete ga ñu bari féete ak PDS, rawatina mag ña, firnde la ci. Mu mel ni, taxawaay bi dëkk boobu ame, mooy li wolof di wax, “ bu jinne bëggee daqaar,  ku yéeg daanu”. Te dafa mel ni ca Tuuba-Mbàkke Persidã Wàdd mooy jinne ji. Ku mën di xëccoo ak Wàdd, walla kuy xëccoo ak ku Wàdd ngemb, yaay ñàkk.

Njureefi négandi yi wone na ni lëkkatoo Wallu darale na fépp. Ca wotewaay ya, limi waññib xob ya biral na ko. Ngirte ya njëkk a génn, Wallu ngay dégg, Wallu ngay gis, Wallu rekk. Mu mel ni  ca bérébi wote yu bare, Wallu a fa teg tànkam. Ci loolu, limi njuureefi négandi yi ñu jukkee ci dalu webu “Senegal Vote”, juuyoowul ak lu ni mel. Ci depaartmaa bu Mbàkke, lu tollu ci 109. 358i xob la Wallu Senegaal darale. Bennoo Bokk Yaakaar moo ci topp ak 36. 360i xob. Yewwi Askan Wi, moom,  6. 071 xob la fa am, Les serviteurs/MPR am 3. 754i xob, Naataange Askan wi dajale 1. 225i xob. Bu dee Bokk Gis-Gis bu Paap Jóob,  1. 125i xob la fa fore, waa Aar Senegaal taxañ 813i xob ak Bunt bi 395i xob. Muy téeméer ci ay junni, bu ñu ko méngalee ak  junni ya yeneen lawax ya am. Mu nekk ndam lu kenn dul laam-laame.  

Kon, mel na ni mënees na def ab taxaw-seetlu ci lu ni mel, walla sax ñu soppi kob laaj faf. Ndax diwaanu Tuuba-Mbàkke bataaxalu kóllëre la yónni maxejj yi ? Walla yari bataaxal lañu dabali ?

Articles similaires

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Bouton retour en haut de la page