ACTUALITES

LAAJ–TONTU AK SOXNA AWA GAY MU PAI

65i at ci ren, bi ñu taxawalee làngug Parti africain pour l’indépendance ak léegi. Loolu, nag, jar na waxtaane. Kon, ayca leen nu laaj sunu maam ji, Soxna Awa Gay, mu xamal nu lëf ci làng googile ak jamonoom.
 Maki Madiba Silla ak Foloryaŋ Bobeŋ
Ci mbindum Maryam Jóob

Kёram ga ca Faas la nu soxna si juróom-ñett fukki at dalal. Ci ndeyjooram, am na ab kaadar bu defub nataalam bu ñuul-weex. Nataal boobu nag, 1957 la ko defoon. Booba, ñaar-fukki at la amoon,  bokkoon ci Bennoog Jigéeni Senegaal, maanaam Union des Femmes du Sénégal (UFS) ak itam ci làngu saa-afrig gi daan xeex nootaange, maanaam Parti africain de l’indépendance (PAI). Awa Gay a ngi fàttaliku bu baax xeex ya mu daan xeex, ay ati at, ngir Senegaal moom boppam :  gàddukati làññit (pànkaart) yi ba Njiitalu Farãs ba, De Gaulle, di ñëw Senegaal ca ut 1958, tasug PAI ginnaaw wotey gox-goxaat yu sulet 1960, reyatum Champ de Course ma ca wotey njiitum réew ya ak yu palum dépite ya ci Desàmbar 1963. Xew-xew yooyu yépp, fekke na leen. Yaakaarug péexte (ngoreef), Càmmug Senegaal gu yees gi, di nёbbatu di booloo, xoqatal gi, metital gi, gàddaay bi. Bésub 15eel ci sàttumbaar, fa Cees, lees sosoon PAI. Booba ak léegi def na 65i at. Tey, Lu Defu Waxu dafa bëgg a jaare ci nettalib Awa Gay, fàttali leen démb.

Awa Gaye (AG) : Balaa PAI, amoon nanu ag Mbennoo gu nu taxawaloon, nun jigéeni Senegaal yi, muy Mbootaayu jigéeni Senegaal yi. Jooja jamono, Saan-Martin Siise moo nekkoon Njiit li, Cumbe Sàmb moo ci toppoon  (tof-njiit), Màgget Jóob nekkoon fara-caytu bi, man ma yoroon  kibaaraan gi. Nu daldi koy defug Mbennoo gog, jigéeni Senegaal yépp la ёmboon. Jamono ji nu koy sos nag, lenn rekk lanu bёggoon : Senegaal moom boppam. Moom lanu doon xeexal. Nu nekk ci, nekk ci, nekk ci ba mu sori. Booba nag, la Majmut Jóob jóge Farãs, ànd ak ay njàngaan ci atum 1957. Ca la taxawalee làngug PAI. Bi mu ko taxawalee nag, fekkoon na sunu jëkkër yi àndoon ak moom. Ndaxte, man, Mbay Maane moo nekkoon sama jëkkër. Moom, aji-bokk la woon ci PAI. Waaye, futbalkat la woon ca Jeanne d’Arc (JA). Mbay Pay, miy dugg ci PAI, moo doon jëkkëru Cumbe Sàmb. Màgget Jóob, Sëriñ Jàllo mi bokkoon ci PAI tamit la doon séyal. Nun ñépp, sunu jëkkër yi ñoo nu ci yóbbu. Jëkkër sang la, am déet ?  
Noonu, nu ànd ak Majmut Jóob, door liggéey bi. Metti woon na lool nag, wax dëgg. Ndax, jamono jooju, dañoo sonaloon PAI, lool sax. Man nag, maa ci gёnoon a tuuti.
Maki Madiba Silla (MS) & Foloryaŋ Bobeŋ (FB) : Ci xayma, ñaata at nga amoon, bi ngay sóobu ci xeex bi ?

AG :  Bi may xeex boobu fukki at ak juróom-ñaar laa amoon. Léegi, maa ngi ci samay 84i at. Nde, 1937 laa juddu.

MS & FB : Ci say wax, nootaange (mbéefar) ngeen daan xeex ngir dog buumu njaam gi. Lan nga nu ci mën a wax, nun nii di seen i sёt yu fekkewul jamonoy nootaange ?

AG : Li may fàttaliku ci nootaange bi, lu metti la. Ndaxte, ca jamonoy tubaab ya la woon, méngoo woon ak mbéefar ma. Yaa ngi dégg ? Dundu gi jafe woon na lool. Te, amoon na ci sax xeeti dundu yoy, kàrt lañu amoon. Maanaam, kàrt bi nga daan weccoo ak ug dund. Buñ la joxaan kàrt bi nag, dangay dem, jox leen ko, ñu dagg kàrt bi, jox la sag dundu. Du yaa ngi dégg de ? Yére barewul woon. Sold bu néew a néew la sunu jëkkër yi daan jot. Ci wàllu wér-gi-yaram, xàjj-ak-seen bu bir moo amoon. Ndege, boo feebaraan, dañuy ràññatle, xool foo bokk, ndax tubaab nga walla ñuule. Li koy firndeel mooy, booba sax, ñaari raglu ñoo fi amoon : raglu bu mag bii di Hôpital Principal ak raglub baadoola yi, maanaam waa dёkk bi.

MS & FB : Fu raglub baadoola yi féete woon ?

AG : Mooy raglub Aristide Le Dantec bi nga xam tey. Nun, ñuule yi, lees ko jagleeloon. Noo fa daan fajoo, nun kepp. Bu dee raglu bu mag ba nag, ay tubaabi kepp a fa nekkoon, ñoo ko jagoo woon. Moo tax, nun, bodddekonteb xeet bu mag boobule lan fi bëggoon a jële. Mbejum kanam, boroom a koy fajal boppam, du dëgg ?

MS& FB : Tey, dund nga 84i at, kaar. Boo geestoo, ak li jot a jàll yépp, lan nga ciy gën a fàttaliku ?

AG : Waaw. Mën naa wax ne li ma gën a jàpp mooy li nu teel a dugg ci géew bi. Nde, nun, ci làngu pólitig gi lanu gimmee. Yaa ngi dégg ? Ba nu ciy nekk itam, nun ak sunuy jëkkër noo fa nekkandoo woon, ndax ñoo nu ci dugal. Li ma ci metti ba metti ma nag, moo di ne, nun, ci xeex lanu dëkkoon. Xeex rekk. Bés bu set, nu xeexal sunum réew. Lépp lu nu bëgg ci sunu dëkk danu koy wax. Ginnaaw gi, ci lanu wutib béréb. Ndaxte, booba, amunu woon fu nu daan daje. Ca lanu demee École Médine, am fab benn béréb, daan fa daje. Waaye, Mamadu Ja daf nu fa mujj a dàq, tere nu fa. Ablaay Foofana moo nu abaloon béréb boobu. Bi nu fa génnee, waa RJDA ñoo nu joxaat ab béréb bu nekk fii ci kër Séydu Nuuru Taal, fi ñu sanc Kёru ndaw ñi. Foofu lan daan daje ginnaaw gi.
Sunu ànd ak Majmut Jóob nag, dafa metti woon lool. Tëj nañ ci Cumbe Sàmb, muy jigéen ji ñu njëkk a tëj ci sababu kujjeg pólitig. Nun, daan nan daje, di mitiŋ… Waaye, saa bu nu defaan mitiŋ ba foog ne noo ci nekk, pólis ñëw, jàpp nu, dugal nu ci daamar, yóbbu nu Bureau des postes de police. Ndeysaan, fa lan daan fanaan ba ca ëllëg sa, ñu bàyyi nu. Te loo ci xamul mooy ne, booba, nu ngi woon ak sunuy kër, amoon i doom ak lépp. Dangay xool lii rekk. Aka noo  amoon fit !

MS & FB : Jigéen yi la alkaati yi daan…jàpp…

AG : Waawaaw ! Nun dañ nu doon jàpp rekk. Bu nu waraan taf i tafka (affiches), danuy fajaru, wut ay poti tamaate yu mag yi fi amoon, bu nekk nu laax ci daakaande ba mu fees. Yaa ngi dégg ? Bu ko defee, nu séddale ko : Gël-tàppe am wàllam, Faas gi ma dëkk am wàllam, Kolobaan itam am wàllam. Ay jigéen kese la woon de ! Góor jàmbaar la, waaye jigéen tamit jàmbaar la. Rax-ci-dolli, ñaari loxoy takk tubéy, ñaari loxoy takk sér. Waxuma dëgg ? Waaw kay. Bu ko defee, guddi gi lan daan jóg. Balaa njël, daan na fekk nu taf dëkk bi yépp.

MS & FB : Dangeen doon teg ay tarakt (tracts) daal…

AG : Ay tarakt ? Déedéet. Dan daan sàndi tarakt yi. Waaye, yeneen yi, ay tafka lañu woon. Loolu lanu daan liggéey ak Majmut Jóob. Ñu sonaloon nu lool nag, nun jigéen ñi. Nun daal, fu nu defaan mitiŋ rekk, ñu fekk nu fa, yóbbu. Ñii ñoo nu toppe woon Mbooro waay ! Bés, jàpp nañ sunu jëkkër yi, yóbbu leen ca kasob 100 mètres. Ñu fanaan fa ba bët-set, ñu ne dañ leen di àtte. Booba ёttu àttekaay baa nga nekk fale ca Kap-Manuwel. Nun, jigéen ñépp nu dajaloo, di wenn say, def ndaje mu mag, dem taxaw, dugg. Alkaati yi fees fa dell, foo geestu gis leen fa. Waaye, nun danu buuxante ba dugg. Ba nu demee nu taxaw, di woy sunu bàkk. Ndaxte, nun waa PAI, danu amoon sunu bàkk bopp. Ma woyal leen ko :
Ñaloor gi ŋar maa ni xonqu naa !
Biddéew bu ñuul bii di fenk naa !
Aa ! Moom sa réew, moom sa réew, jot na !

Moom sa réew, moom sa réew, jot na !
Bon ak jaam baa di farlu jot na !
Gaa ñi jógleen a jomlu jot na !
Aa ! Moom sa réew, moom sa réew, jot na !

MS & FB : Ku tudd jamono jooju, tuddaale ñaawteefi pólis ba woon :  xoqatal ak metital ya ca biir kaso ya. Ndax waa PAI, ñu ci ëpp buñ leen jàppaan…

AG : Dañ leen di metital kay…

MS & FB : Maanaam ?

AG : Aa nun jigéen ñi de, Yàlla baax na ba duggunu kaso. Bureau des poste de police rekk lañ nu daan yóbbu. Cumbe Sàmb daal moo ci jot dugg ndung-siin. Sama jëkkër tamit jot na dugg kaso. Waaye, bu Cumbe Sàmb bi, keroog 30i fan ci sulet 1958 la woon, bésub wotey Ndar ya. Booba, sama jëkkër ak Majmut Jóob ñoo àndoon. Ñoom, jotuñu leen jàpp ndax daa fekkoon ñu dem réewum Mbennoog Sowet ya (Union soviétique). Ndeysaan, sama jëkkër jotul a ñibbisi. Nde, foofa la gaañoo… Ca wote ya fa amoon, te àndoon ak coow, lañu demoon. Ñibbisiwul, ba ni muy génne àddina.  

MS & FB : Metital yi nag, loo ci xamoon ?

AG : Aa mbugal yi dey metti woon nañ. Am na ci ku ci waxoon ne noppam yi dañu bënn. Am na tamit ñoo xam ne, dañ daan jàmbat ndigg. Moom daal, ku ci duggaan kaso ba génn, dangay soppiku. Waaw. Loolu moom amoon na. Waaye, nun moom jigéen ñi, Yàlla musaloon nanu ci loolu. Waaye sunuy góor, dañ leen a sonaloon. Sonnoon nañ torop sax ,wax dëgg a neex Yàlla.

MS & FB : Kon daal, nekkoon PAI jaamono jooju, lu…

AG : Metti woon la. Nekkoon PAI jamono jooju, mi ngi mel ni nekk safara. Looy def lu ne, fàww nga làqatu. Moo tax, bi sama jëkkër dafa jékki rekk, dem réewum Mbennoog Sowet ya. Kenn yëgul. Kenn tinul. Gis nga, sama kër gii, fii laa daan toog. Dama daan toog ba njolloor, fekk lépp a ngi ne selaw, am ku ma fëgg. Bu ma ubbee, ñu laaj ma “ Ana Mbay Maane ? ”. Ma tontu, ne “ Gisuma Mbay Maane ”. Bu ko defee, ñu dugg, wёr, lёñbёt kër gépp te duñu gis kenn. Bu ko defee, ñu daldi dëpp. Daan nañ toog ci boolu reer sax, ñu yónne ma ab yëddukat. Muy reerandoo ak nun, di ma laajaale Mbay Maane. Wax a, wax a wax ba… ma xam xéll ne kii, am na lu mu bëgg. Waaye, daa xamul woon ne, lu puso muus muus, wëñ jaar ca taat wa. Nde, man, ci pólitig laa yaroo. Ma ne patt rekk, ba ni muy deme.
Ndeke, booba tam, mu ngi fii. Demagul woon ca réewum Mbennoo Sowet ya. Dafa amoon fu ñu ko denc. Su ma toogaan ba guddi, damay sol colub yalwaankat, yaa ngi dégg li may wax ? Damay solu nib yalwaankat, jël sareet , mel ni dof, yeb ci samay foyteef ak reer yi ma ko war a yóbbul ak yépp. Bu mu demaan ba tollook boppu koñ ba, wàcc, jëlaat beneen sareet, mu yóbbu ma ba fa mu nekk. Ma taajal ko mu reer ba suur, ma fanaan ba bët-set, ñibbi. Nga war xam ni, bàndi, wëyooy baayam. Lii yépp def naa ko. Maa la ko wax !

MS & FB : Kon, lu jёm ci wotey  1963 yi moom, dafa amoon coow ak i xoqatal yu metti. Turu Maryaan Dernewiil dey ñëw. Lan nga nu mën a wax ci wote yi, walla rawatina ci Maryaan Dernewiil ?

AG : Aa, Maryaan Dernewiil, noo àndoon, bokk di xeex.  Waaye nag, fésu ci woon noonu daal. Nun, li nu ñeme woon a def, moom amul woon fitam. Céy, noo pànkoon ! Li nu sañoon a def… Ndaxte, nun, bul def lan daan bañ. Danoo ёsoon. Ragalunu woon dara. Dara kay ! Ciy jigéen nag. Daan nan jël sunuy caabal (yéenekaay), takku ba dëgër, taxaw ci xonkaan yi (feux rouges), di leen jaay. Xaalis bi, ci nafag làng la daan dem.
Li ma ca metti nag, moo di am na wote bu amoon Champs de course. Nu dem. Boobu, man maa ci nekkoon, Róos Baas, Cumbe Sàmb, Màgget Jóob, ak yeneen i jigéen. Amoon na jenn jigéen ju dëkkoon Kolobaan. Waaye, léegi gaañu na, ndeysaan. Jigéen ju jàmbaare la woon. Noo demandoo woon. Ba nuy dem, nun tamit, danu defaroon sunuy… cocktail molotov.

MS & FB : Dangeen daan defar ay cocktail molotov, yeen jigéen ñi ?

AG : Nun ñii, jigéen ñi !  Boo bëggee, ma defaral la ko léegi nga gis.

MS & FB : Nga ne ma, fàtteego ni ñu koy defare ?

AG : Mën naa ko defar de ! Waaye, duma ko def. Duma ko def de ! Na leer.

MS & FB : Loo nuy jàngal ci cocktail molotov yi ?

AG : Cocktail molotov yi, nun danu ko daan defar, toog di leen xaar.

MS & FB  : Yeen jigéen ñi ?

AG : Nun jigéen ñi, def ko ci sunuy kees, walla ci sunuy siwo, teg. Buñ nu sànnee lakirimosen yi, nu sànni leen cocktail molotov yi. Nun daawunu daw de ! Ragal du jéggi raay.

MS & FB : Mbaa daawuleen yóbbaale cocktails molotov yi bu wote amaan, ngeen war a jàmmaarloo ak takk-der ya ?

AG : Waaw kay. Saa buñ demaan, dan koy taal. Danuy taalati cocktail molotov ! Booba nag, fale, ca Champs de course lañ daan wotee. Bun demee ba kii rekk, nu tàmbali… nga bal dёggantaan yiy jolli ci kow. Xale yi di daanu fii, dee ; ñii di tëb fii, ñee di wadd fale. Mu am ku ma doon waxal nii, mu daldi daanu sama kanam, may gis. Ci lañu jàppe Róos Baas dugal ko ci biir. Sunu cocktail molotov yi nu yoroon, nun ñépp, fa lanu ko sànni, talatun ko woon. Ndax nag, coow lee fi nekk rekk. Waaye, xam nga ni fitu jigéen taxu koo réy noonu. Danoo réy làmmiñ rekk. Ma ne, nun ñépp làlli woon.

MS & FB : Xanaan reyat gu amoon ca Allées du Centenaire atum 1963 ngay wax…

AG : Mi ngoog ! Yaa ko laal !

MS & FB : Allées du Centenaire sorewul ak fii [Faas] di. Am na loo ci war a jàpp ba tey ?

AG : Soriwul. Fii la. Metti, dafa metti woon. Ndaxte, man, ba may dem… Gis nga, bu may wax ci lii sax, ree daf may jàpp. Ba may dem, dama jël benn paaka, paaka, def ko fii. Ma ne ku ma laal tey, dama lay jam, daldi takku. Booba, sama yaay a ngi fii, ame tawat. Waaye,jamono jooju, boobu pólitig bi dugg na ma. Yëguma woon sax ni sama yaay a ngi ci kër gi. Ma bàyyi samay doom ak sama yépp, ànd ak sama jëkkër dem. Waaye, wex na ma xàtt. Nde, ba nu demee ba bal yi di tuy-tuyi, nit ñiy dee niy weñ… Ba nu sànnee cocktail molotov yi, dama daw. Man, dama daw de ! Maa la ko wax ! Taxawuma fa sax. Sàtaneer laa dawe ba fii. Xanaa du maa mën a daw ? Gis nga, li may daw yépp, paaka baaŋ ma doon xoos. Sama yii yépp daggatoo, di nàcc rekk. Nun danu sonnoon. Te, xolal, amunu ci dara. Nu ngi nii, féetewunu fenn. Waaye, dinaa daanelee léebu bii, sasee ko maasug tey gi ngir ëllëg :

Bu lëg lekkee aloom, na ko gërëme coy.
Jërëjëf !

Articles similaires

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Bouton retour en haut de la page