ACTUALITES

NAALUB YEESALAAT RAGLU ARISTIDE LE DANTEC LI WARAL COOW LI

Raglug Aristide Le Dantec lañ nar a tëj, 15 ut bii ñu dégmal. Ndogal laa ngi tukke ci Càmm gi. Waaye, dafa mel ni ñépp ànduñu ci anam bi ñu koy defe, rawatina mbootaayu liggéeykat ya fay daan seen doole. Ci altine jii, sax, mbootaay boobile, janoo woon na ak taskati xibaar yi ngir indi ay leeral ci mbir mi ak naqarlu doxalinu Càmm gi ak ñi mu àndal.

Weer yii nu génn, Njiitu réew mi, Maki Sàll, jawriñ ji yor wàllum wér-gi- yaram ak i ñoñam, daje woon nañu. Bésub talaata la woon, 19 awril. Ndaje moomu, dañu ci doon waxtaane seen mébétu defaraat Raglu Aristide Le Dantec. Ci biir waxtaan wi, NJiitu réew mi biraloon na solos naal bi. Moo ko taxoon a wax ne yéeneem mooy :
« …yeesalaat bérébu pajuwaay yi ci biir réew mépp ak ay jumtukaay yu yees te xareñ… Mébét mi mooy tabaxaat Raglu Le Dantec ak 3i ektaar ci diirub 20i weer. Yeneen 3i ektaar yi des, dañ leen di jaay, ndax ci xaalis boobu lañuy defaraatee Raglu bi. »

Ci kow 6i ektaari suuf lees samp Raglu bi, mu féeté ci xolu Ndakaaru. Muy màndargaal lu réy ci wàllu paj, ci Senegaal ak ci Afrig sowu-jant. Te, 110i at, maanaam xarnu ak fukki at, mooy diir bi dox diggante sosub Raglu Aristide Le Dantec ak tey jile. Ndekete, ci atum 1912 lees ko tabaxoon. Jamono jooja, Senegaal mi ngi woon ci nooteelu Farãs. Ca Ndoorteel la, Hôpital Centrale la tuddoon, nit ñi daan ko woowe Hôpital indigène, maanaam Raglu baadoola yi, walla néew-ji-doole yi. Li ñu ko dugge woon mooy ràññatle ak Raglu Principal mi ñu jagleeloon xarekat yi. Le Dantec nag, mënees na ko jàppe ni ab jàngune. Ndaxte, kat, ay fajkat yu mag ak i njàngaan yu dul jeex, ci réew mi ak bitim-rew, jànge nañu fa, tàggatu fa ba seen i àlluwa gë faa xóote. Kon, Raglu Aristide Le Dantec, dafa bokk ci mbooru Senegaal, di bokk-moomeelu askan wépp. Bu ko defee lépp lees fay def, warees na ko xoolaat bu baax.

Waaw, 1. 300iy nit ya fay liggéeyee nag ak way-tawat ya fay fajoo jamono jii ?

Ci àllarba ji, 10i fan ci weer wile, Njiitalu raglu bi, Baabakar Càndum, tontu na ci laaj bi, di dalal xel yi. Ciy waxam, ne ku ci nekk ci 1. 300i liggéeykat yi dina delsiwaat ci liggéeyam. Baabakar Càndum di xamle ci Dakaractu.com ne, ci ndimbalu Càmm gi, ñoo ngi tóxal liggéeykat yi ak pajiwaay yi ndànk ndànk, ci anam bu mucc ayib. Noonu, ñii yóbbees na leen ci yenn bérébi pajuwaay ci Ndakaaru, ñee ñu yabal leen ca Tuubaa, ca Raglu Seex Ahmadu Bàmba Mbàkke. Bu dee pajuwaayu liir yi, dees na ko tóxal ca Raglub gone yi, ca Jamñaajo. Noonee tamit lees di tóxale liggéeykat yi. Bees sukkandikoo ci kàdduy Baabakar Càndum, kenn du ci ñàkk liggéeyam, ku ci nekk, dees na la wutal ab béréb, ñu nekkandi fa ba keroog raglu bu bees biy noppi. Bu dee ci wàllu payoor gi, nee na njawriñu paj mi moo koy féetewoo.

Nee ñu, liggéey bi 18i weer lay def. Maanaam, desàmbar 2023 la raglu bu bees bi war a noppi.  Njawriñu paj mi génne ab yégle, lim ci ay béréb yi war a dalal liggéeykat yi : Dalal Jamm [Jàmm], Faan, Idiriisa Puy (HOGIP), Ruwaa Bóduwe, Raglub xare bu Wookaam (HMO), Raglub gone yi bu Jamñaajo (HED), Institut d’Hygiène Sociale (IHS), Raglu Pikin (Kã Caaroy), Abbaas Ndaw, Ahmadul Xaadim bu Tuubaa, Pajuwaayu Ngor, Les Maristes, Yëmbël, Kolobaan, Nabil Sukeer, Baay Taala Jóob (Raglub Dominig ba woon, ca Pikin), Sikaab Mbaaw, Kër Masaar, PMI bu Médinaa ak Mbaarum Ujaaj yi.

Njawriñu paj mi teg ci ne, « dinanu taxaw ci wetu way-tawat yi, toppatoo leen ni mu ware te doxal naalub tóxal bi, ñeel njariñe yi ak liggéeykati raglub Aristide Le Dantec ni mu waree ngir tabaxaak ko ba mu baax. »

Waaye, ba tey, njaw des na aw xàmbin

Bi Càmm gi nee day jaay 3i ektaar, tabax 3i yi ci des, mu xaw a jaaxal ñenn ñi. Loolu, nag, dafa laaj ab taxaw-seetlu. Ñuy laaj, yeneen 3i ektaar yi des, kan lañu koy jaay ? Ñaata lañu koy jaaye ? Ñaata lañu koy tabaxe ? Lees xamagum, jamono jii, mooy ne, Fonsis (Fonds Souverain d’Investissements Stratégiques) la Càmm gi dénk njaay moomu ak lépp li ci aju. Waaye daal, njort ñaaw na ci, xel teey ci. Nde, ñii ñoo ngi naan càmm gi daf koy jaay ngir def ci ay Clinique privée, ñee di wax naan ay otel lañ ko bëgg a def.

Bu loolu weesoo, li liggéeykati Le Dantec yiy kaas mooy taaxub 6i etaas yiñ ko bëgg a def. Te, rëddeef (plan) bi leen tubaab yi wan, doyu leen. Loolu moo metti  Maane Ngom ak i naataangoom, ba tax koo biral kàddu yii toftalu :
«  Càmmug Senegaal, ay español la dénk tabaxaatub Raglu bi. Ñoom nag [español yi] dañu indaale seen rëddeefu bopp boo xam ne, dëppoowul ak li waa réew mi tàmm te miin ko. Jamono jii, ci bérébi pajuwaay yu bare, asãsëer yi dañu paan, ba noppi Càmm gi naan day tabaxaat Le Dantec def ko ay etaas. Ay jafe-jafey rekk lay dolli ci jafe-jafe yi fi jot a am. »

Bees sukkandikoo ciy kàddoom, am na kenn ci doomi réew mi ku defaroon ab rëddeef boo xam ne ñépp ñoo ci àndoon, rafetlu ko. Rax-ci-dolli, kooku, yor na xaalis bu doy bu mu mën a tabaxee Raglu bu bees bi te Nguur gi du ci def dërëm. Moo ko tax a waxati ne :
« Sampees na Raglub Le Dantec ci déndub 6i ektaar, Càmm gi ne tabaxaat bi ci 3i ektaar kese lay yem. Am na luy ñuul ci soow mi ! Bu dee xaalis moo amul, am na benn saa-senegaal boo xam ne, waxtaanoon na ak jawriñ ji ba ñu torlu ab déggoo, am na xaalis te am nanu ag rëddeef bu ñépp nangu. »  

Li leer ba leer mooy ne Njiitu réew mi, Maki Sàll, mu ngi def lépp ngir tàmbali tabax bi ca na mu gën a gaawe. Ndax lëlu jawriñ bi amoon ci 4 ut bi, moo ngi ciy joxe ndigal ngir liggéeyub Raglu bi door ci sàttumbaar 2022.

Lii bokk na ci li tax lu ëpp ci liggéeykat ya nekk Le Dantec taxawal ab kurél ngir aar ak sàmm Raglu bi. Yeneen liggéeykat yu jóge ci yeneen i raglu ak ñu bari ci askan wi dugg nañ ci biir kurél gi te di wax Càmm gi mu teg tabaxaatub raglu bi ci yoon, ku nekk gis ci boppam.

Li ñuy xeex mooy ne Càmm gi dafa jël dogal, ne Raglu bi dafay tëj bésu 15 ut te àndul ak benn këyit bu koy yëgle wala dara. Mbaa lu jëm ci way-tawat yi fan lañiy àggale seen um paj ak naka lañuy toppatowe seen i kayit ba réero du am. Leneen li ñu war a lijjanti tamit mooy liggéeykati Raglu bi yépp, dale ko ci fajkat yi, balekat yi, ñi nekk ci wàllum caytu gi ak ñiy saytu kaaraange gi, naka lañuy def ba duñu ñàkk seen liggéey, rawatina seen i pey bés bu Raglu bi tëjee. Abdulaay Jonn mi jiite kurél gi dafa jàpp ne « Càmm gi lenn rekk la bëgg, te mooy nasaxal Raglu bi, waaye defaraat taxu koo jóg. Ndax, mi ngi toroxal way-tawat ya fa nekk, di leen dàq te amuñu ci benn yërmaande. » Kurél gaa ngi aartu Càmm gi ci ne, duñu nangu kenn di leen toroxal ñoom ak way-tawat yi.

Laaj bi sampu mooy, lu gaa ñiy yàkkamti ? Lu tax Càmm gi bëgg a patam-patamee tabaxaatub Raglu bi ? Kurél giy kaas ak ñaxtu, ndax am nañ sañ-sañ ak doole jàmmaarloo ak Nguur gi ci mbir mile ? Ku xeful dinga gis…

Articles similaires

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Bouton retour en haut de la page