ACTUALITES

TOLOF-TOLOFI ARTISÃ YI : LAN MOO CIY TAXAWAAYU NGUUR GI

Fànnu artisanaa nekk na lu soxal lool nit ñi rawatina artisã yi yore seen liggéey di ci góor-góorlu. Ñi ci gën a bari nag jànguñu nasaraan. Nde, ñàkk a jàng googu moo leen di jural ay jafe-jafe ci seen liggéey.

Am na ci ñoo xam ne sax, amuñu këru liggéey bu jàppandi. Te itam, li ñuy jaay dafay lamb ndax njaay yuy jóge bitim-réew ñoo fees ci ja yi, te yooyule njaay la askan wi gën a taamu. Te, ndimbal yi ñuy jagleel fànn woowu, daanaka ñoom duñ ci jot walla boog ñu bari ci ñoom. Ba tey, ndax seen ñàkkum jàng war na tax ñu beddi leen ? Ndegam seen i mën-mën kenn werentewu ci, Nguur gaa ngi lal i pexe ba seen nekkin gën a ñoŋ.  Liggéey bi ci fànn woowu tamit mën a dox ci ni ñu ko bëgge. Kii di Njiitu réew mi, Maki Sàll, sant na jëwriñ ji mu dénk fànn woowu mu suqaliwaat ko file ak diir bu gàtt.

Aamadu Jara

Maxejj yu bari ci réew mi, ci xayma, seen liggéeyu bopp lañu yore te moo leen di dundal. Maanaam, xaaruñu dara ci Nguur. Waaye, dafa fekk ni tey, ñu bari ci ñoom, duñ ci gis seen bopp bu baax. Askan woowu nag, mooy ñi jàngul nasaraan donte ne sax xarañ nañ lool ci li ñuy def. Mooy liñ naan ku bokkul ci gétt gi doo naan ci meew mi. Mu nekk ab yen bu diis lool ci ñoom. Waaye, wareesul a fàtte ne fànn woowu ñàkk a doxam day suuxal koom-koomu réew. Moo tax Njiitu réew mi Maki Sàll, ay fan ci gannaaw, jëloon na ay dogal ci fànn woowu jaare leen ci jëwriñ ji mu ko dénk ci jamono jii : Paap Aamadu Njaay.

Nde, ci yéenekaay bii di « Le Quotidien », jox na ko diir bu gàtt ngir mu xool tëralin bi muy teg ngir suqali fànnu artisanaa bi. Tëralin boobee ngi tudd « Stratégie nationale de développement de l’artisanat » (SNDA). Dañu bëgg a yeesalaat fànn wi ba noppi soppi doxalinam ba mu nirook ag caytu (administration). Ña fay yëngu nag, dañu war a jàng, xam nu seen liggéey ak béréb bi itam di doxe. Léegi nag, jëwriñ ji, ci ndigalu Maki Sàll, dafa war a defar ay këri liggéey yu baax ci fànn wi, jël ay jumtukaay, taxaw ci wàllu njàngale mi ak ni ñuy def ba artisã yi jot ci ndimbal yi. Ci ndimbal yi, bëgg nañ sàmp ay jumtukaay yu mel ni « Fonds de financement de la formation professionnelle et technique » (3FPT), « Délégation générale à l’entreprenariat rapide pour les femmes et les jeunes » (DER/FJ), « Fonds de garantie des investissements prioritaires » (FONGIP), « Agence pour la promotion et le développement de l’artisanat » (APDA) ak « Agence de développement et d’encadrement des petites et moyennes entreprises » (ADEPME). Ba tey ci ndigal yi, Paap Aamadu war na yeesalaat këru liggeey yi ba noppi defar ay bérébi jàngalekaay ci fànn wi ak ci gox yépp. Nguur gi, ci doxalinam, dafa bëgg a teg artisã yi ci ay anam yu baax ngir ñu mën a bokk ci ñiy dëkke di liggéey ngir suqali koom-koomu réew mi. Nde, loolu ay jéego yu am solo la ci fànn wii nga xam ne démb ba tey ci ay jafe-jafe la nekk.

Ba tey, am na leneen lu am solo lu Nguur gi war a sóoraale donte ne sax bëgg na def liggéey bu mucc ayib ci fànn wi. Ndax ci maxejj yi, téeméer boo jël 80 yi jànguñu nasaraan te dégguñu ko. Ba tax, am na ñu jàpp ni li Nguur gi bëgg a def du am ug mujj. Dañu war a xoolat pólitigu (tëralin) làkk yi bu ñu bëggee sémb bi àntu ba noppi artisã yi gis ci seen bopp. Te bala loolu am fàww ñu won leen li méngoo ak li ñu xam ak li ñuy def. Ñoom nag, ñàkkuñu xam-xam te waruñu leen a jàngal leneen lu dëppoowul ak li ñu xam. Ci loolu nag, làkk wi ci la bokk laata leneen di ñëw ndeem moo ëmb lépp.

Waaye, ndax mbir mi dina àntu am déet ? Artisã yi itam, mbaa dinañ ci gis seen bopp am déet ? Lees di wax mooy : li ci kanam rawul i bët.

Articles similaires

Laisser un commentaire

Votre adresse e-mail ne sera pas publiée. Les champs obligatoires sont indiqués avec *

Bouton retour en haut de la page